30/05/2026
Abdulaay WÀDD, téeméeri ati dund gu am njariñ.
Ci bisub tay bii di 29i fani mee 2026, maa ngi toroxlu niki doom ci kanamu Peresidaa Abdulaay WĂ€DD mi matal ab xarnu ci ag dundam.
Li mu daje ak Tabaski gi nag tax na ba manunoo mà ggal ci réew mi, dayoo bi téeméeri at yii yellool. Waaye ak lu man a xew : ay milyoŋi saa-senegaal a ngi mà ggal bisub tay bii ci seen biir i xol, ci ay ñaan boole ko ak teewlu gu matale. Loolu sax nag ñà kkul ne mooy njukkal li gën a wér.
Abdulaay WÀDD, ci lu amul benn werante, bokk na ci baay yi gën a fés ci demokraasib Senegaal. Depite ca 1978, ginnaaw ay ati xeex, moom mii, mooy firndeel ne, yéeney aw askan, ak lu ñu ko gà llankoor gà llankoor, day mujj rekk tegu ca yoon wa daal di sotti. Xeex bu yà gg boobu nag te sotti, ca mars 2000, di alternaasu jà mm bi njëkk ci sunu mboor — di mà ndargam keno bi Senegaal doon ci biir kembaar gi ak fépp ci à ddina.
Lu ñeel sama jëmmi bopp, li ma man a jà pp ci sama jëflante ak moom, donte gà tt na te am solo, mooy ag tabeem. Ñaari yoon, jaare ko ci digle yu am solo ca 2017 ak seede yu mu defoon ci man ci pénc mi ca 2019, Peresidaa WÀDD teg na ci sama yoon mbir mom nit ñu mà gg ñi rekk a koy teg : jébbale. Déet jébbale nguur, waaye lu jafee gis, te mooy, kóolute. Jëfi mag mu nangoo gis ci maas gu bees gi, déet guy ruur, waaye maas guy wéyal ndono li. Maa ngi ko ciy sant bu baax.
Ci bis bu barkeel bii, maa ngi à nd ak mbooleem Saa-senegaal yi di ñaanal sama maam jii, ni ma taamu di ko ko woowe saa su nu masaan a daje.
Yal na tĂ bbi ci Kaaraangeg sunu Boroom gi dul dog mukk.
Te Senegaal wéy, niki mu ko yà gg a gëmee, di liggéey, sóobu ci yoonu méngoo ak jamono te boole ko ak sax ci ay mbaaxaam.
*Ousmane SONKO*
*Njiitu Pastef Les Patriotes*