05/08/2014
Niou Èggali Lign Taambaliwone Ci Mâqâma Dîni Salâssa, Djotali Wone Nagn Li Baye Wax Ci Lislam, Lègui Lii La Wax Imân (maqama niaarèl)
' Gueum Yaala Moy Nga Dogou Ci Né Yaala Rék Moy Sa Borom, Mom Rék Nga Wara Diaamou, Waroulo Diaamou Kouko Moy. Yaala Modi Kann? Kila Xamal Boppam, Kila ... Ak Soûf-cii Nga Xamné Cinga Taxaw, Bindeula Yow Nitki, Bindeu Lingay Guiss Yeup, Warouwaay Yii, Mbaytèf Yii, Guèdj-gui Ak Liy Guènnè Ci Guèdj-gui, Mègnèt You Beuri, Téksi Né Dina Binde Sax Lougn Xamoul, Té Kokou Amoul Dayyo. Li Yaala Binde Daal Moy Liko Dallè Ci Yow Bathi Linga Meuna Guiss Ak Linga Meunta Guiss, Ak Li Sa Xel Di Dathie Ak Li Sa Xel Dadioul. Ay Mindèfam, Mom Rékka Xam Sène Dayyo. Kokou Rék Moy Sa Borom, Nga Gueum-ko. Mooy Kifi Nèkkone Bifi Dara Nékkout, Mofiy Nèkk Boufi Nieupp Djoguè, Tay Djii Bougn Défénèni Yénènanguifi, Mom Rékkafi Nékk, Mom Rék Lagn Wara Gueum Né Moy Souniou Borom. Diiné Lislam Moy Diné Dji Nieuw Gorèlniou Ci Diaamou Loudoul Yaala, Djèbeul Nitgni Diaamou Yaala Rék.
Bo Gueumè Yaala, Gueum Yaala Moy Xèweul Guinga Xamné Mo Gueun Ci Mbolèm Xèweuli Yaala Yii, Moci Eupp, Té Mbolèm Xèweuli Yaala Yii Molène Meun. Té Gueum Yaala Mo Eupp Ap Yonent. Soula Yaala Mayè Yow Yaala Xèweul-Go-Xamné Mo Eupp Ap Yonent, Lo Wara Wax Loumoy Alhamdoulillahi Rabbil Alamin.
Ki Xam Yaala Moy Waliou-bi, Deuggom-Gou-Ndieukk Moy Toûb Bima Diaangatone Sanx, Deuggom-Gou-Moudjou Moy Ma'rifatou Kiy Xam Yaala, Ngathia, Ngathia. Ap Yonent, Deuggom-Gou-Ndieukk Moy , Deuggom-Gou-Moudjou Modi Ak . Bign Ndieukkona Touddou Té Mou Gueuna Soûfé, Mo Gueun Ma'rifatou Guii Gueuna Kawé Ci Mâqâma Yii Diaam Bi Meuna Djot, Loutax? Moko Diour! Imân Binga Xamné Cila Yonent Ndieukkona Diaar Sanx, Ndax Yonent Mom Dou Diaar Ci Tawbatu, Ndax Mom Dou Moy Yaala Moukk, Mom Deuggom-Gou-Ndieukk Rék Modi Imân, Deuggom-Gou-Moudjou Modi Nubbuwatu Ak Risâlatu, Mané Imâna Gueun Nubbuwatu, Mo Gueun Risâlatu, Loutax? Moko Diour! Kou Amoul Imân Dou Nèkk Yonent Moukk, Dou Nèkk Nabî, Dou Nèkk Rasûl.
Konn Imân Guinga Xamné Nioun Boûxanté Nagnci Ak Yonent Yii, Té Mo Gueun Nubbuwatu Ak Ridâlatu, Konn Warnagn Sant Yaala Ci Xèweul Gogou. Niongui Sant Yaala Ci Xèweulak Gueum Yaala.
Gueum Yaala Momou, Momit Amna Niétti Mâqâma.
Mâqâmam Bou Ndieukk, Modi : Deuggo Ak Deuggou
Louthia Topp Modi : Sèlal
Bathia Moudjou Moy : Dal, Nga Dal Ci Yaala.
Moy Lann? Moy Sa Djeuflantèk Yaala, Nga Deuggou-thia, Bagn Thiaa Dioublou Lénène Loudouhout Yaala. Kèpp Ko Xamné Limouy Déf, Yaalaa Tax Nga Diko Déf, Yaalaa Tax Nga Bour Dieum Thia Djeuf-ga, Kokou Deuggalna Ci Djeuffam, Ganaaw-ga Bilè Dioublou Ngaci Lénène It, Téréwoul Kou Deuggou-nga Rék. Motax Moy Ko Xamné Yaala Lay Dieuflantèl, Sou Fèkkè Ni Loudoul Yaala Douggou-thia Bènn Waxtou, Ci Ndieulbèn Baci Moudj, Ci Biir Baci Bitti, Kokou Dotoul Sâdiq Konn La. Siddîq Moy Ko Xamné Yènèm Yaala Tax, Yaalaako Tax Bour, Yaala La Djeufal Djeuf Dji Bam Mat Té Loudoul Yaala Raxouthia. Yaala Nèna Nagn Aandak Nioniou Sâdiqîn Yii. Nèna ''Aandeu Lène Ak Weuy Deuggou Nia'. Kèpp Kou Beugg Yaala, Namm Yaala, Té Xamné Sâdiq Nga, Yow Lâ Boudda Sa Adio Ci Yaala Dina Fadjou. Murîdu Sâdiq, Yaala Douko Beugglo Mouk Louy Niaakk, Loum Fassowouta Amal, Ndax Deuggou-ga. Lolo Tax Yaala Né 'Kûnû Mâ Sâdiqîna'.
Mané Sou Fèkkè Gueum Nga Yaala Gueum-Gou-Deuggou, Di Djeuflantèk Yaala Dieuf-Bou-Deuggou, Tékthia Nga Sèllal Djeuf-dji Nièl Yaala, Modi Likhlâs Kiy Mâqâmam Niaarèl Ci Limân.
Moy Sa Djeuflantèk Yaala, Guènèthia Loudoul Yaala, Té Sa Bopp Sax Loudoul Yaala La, Konn Djeuf-dji Bouci Done Dara, Na Djeuf-dji Baayèko Ci Yaala, Na Djeum Ci Yaala, Na Taxawè Ci Yaala, Yiw Guènneu Ci, Warnalaa Yomb Ndax Yow Nèkko Dara. Konn Djeuf-dji Daal Nay Sèll. Likhlâs Ak Sidqu Danio Djéguéwanté Lool, Ba Kouy Sâdiq Rék Nga, Kouy Itam Nga. Likhlâs Moy So Xamèné Ci Yèné-ga, Ci Bour-ga, Ci Djeuf-dja, Lèpp Ci Ndieulbène Baci Moudjou, Nguir Yaala Rékka Tax, Té Ci Yaala Fék La Taxaw, Ci Yaala Rék La Dieum, Kokou Mukhlas La. Yaala Yonent Boum Touddou Ci Alquran Dafay Waxné Mukhlas La, Dafay Wax Né Siddîq La, Siqqîq Moy Mukhlas, Mukhlas Moy Siddîq, Sâdiq Moy Mukhlis, Mukhlis Moy Sâdiq.
Bou Fèkkè Nak Ni Diaam Bi Sèllal Na, Diggantèm Ak Boromam Ci Mbolèmi Djeuflantèm, Dafay Djeuf Djeuf Yeup, Té Guisné Djeufoul Dara, Niaary Mâqâma Yoyou, Mâqâma Zâhir Ak Bou Bâtin, AlQuran Waxal Naniouko Ci 'Iyâka Naghbudu Wa Iyâka Nasta'inu'. 'Iyâka Naghbudu' Moy Mâqâma'p . Mom Dafay Diaamou Yaala, Guiss Ap Diaamou Yaalaam, Kokou Bou Nèxè Yaala Mou Nangou, Bouko Nèxè Mou Sèt Ko. Ci Bâtin, Kokou Dafay Wax 'Iyâka Nasta'inu', Man Meunoumalaa Sax Diaamou, Yow Laay Dimbaliko Ci Diaamou-Gui. So Guissèné Diaamou Gui, Yaalako Djeuf Rék Askann Lako, Ci Beug Sa Tour Wou Rafét, Niou Gueureumèlako, Niou Fal Laci, Tè Yow Dèfoulo Dara, Kokou Modi Kou Sèllal, Motax Arif Yii Né 'Iyâka Nasta'inu', Hâm Yii Niom Niogui Ci 'Iyâka Naghbudu'. Waayé Diaama'p Yaala Bi Tigui, Dafay Guisné Meunoul Dara, Yaala Ték Lay Dimbaliko Ci Diaamou Gui. Niou Indici Missâl Bou Gaatt: Té Dou Yaala Monéniou Djouly Lène, Waxtou Djouly Wi Tèwna, Té Meunoulo Djouly Té Laaboulo, Laap, Ci Ndox Rék La Meuna Wérè, Ana Sa Ndox? fok Yaala Mayla Ndox Dé, Nga Soga Meuna Diaapp, Mbaa Nga Sangou, Fok Nga Soutouraal Sa Awra, Konn Foy Djeulè Lo Woddo Soulako Yaala Mayoul, Fok Nga Am Kaatana'k Meuna Taxaw, Rouko, Soudjod, Nga Harmal, Dou Wérr Moukk Loumoy Ci Diaangue Alqouran, Ana Sa Alquran? Alqouranou Yaala Rék Cinga Meuna Diaamo Yaala, Cinga Meuna Djoullè, Konn Sètt Nga Djouly Gui, Binga Sètè, Yow Loci Déf? Fok Nga Am Paakk, Ana Sa Soûf? Li Yaala Def Ci Djouly Gui, Boci Nara Ray, Djouly Gui Dou Am. Motax Yow Mii Arif Bi Waxoné 'Maaguilay Diaamou, Dangakoné 'Yow Laay Dimbaliko Ci Diaamou-gui'. Lolou Moy Likhlâs Mâqâmap Niaarèl Bi.
Nit Dinay Sèllal, Mouy Hâl Ci Lom, Mouy Sèll, Di Sèll, Sèll Lol, Yii Temps Bakkan Bi Douggou Thi, Ndax Bakkan bi None La Bo Xamné Dafay Yaala Yaala-Lou, Kou Nékk Ci Nioun Na Xamné Bakkanam Dafay Yaala Yaala-Lou, Nax Soula Yaala Nè Défal Lii, Bakkan Bi Néla Défal Leulé, Soula Nè Baayil Lii, Bakkan Bi Né Lolou Laa Beugg, Té Dafay Méllo Sax Méllo Yaala. Bakkan Bobou, Bo Yègguè Ci Mâqâmam Likhlâs, Faaw Mouy Djèma Douggaat, Boko Daakhè Bam Sét Wèthie Nak, Kokou Miy Tumâninatu, Konn Sa Bakkan Dalna Ci Péyi Yaala Bi, Deukk Nafa Nak. Fofou Mom Gningkoy Wo Mou Djeum Ci Yaala. Yaalaa Nguiko Wax Né 'Yow Sa Bakkan, Dikkè Ma Sama Péyi Noumla Nèxè'. Mâqâma Bou Fort La.
Imâna Ngok. Laambona Niétti Maqama: Sidqu Ak Likhlas Ak Tumaninatu. Nga Soga Douggou Nak Ci ....'
A Suivre In Sha Allahu